Description
Ay nitu Yàlla leen woon, ndax dañoo saxoon ci lislaam te loolu moo di topp Alxuraan ak Sunna, sax ci ndigali Yàlla yi ak wattandiku ay tereem, di teewlu xibaar yi dikk ci Téere Bu Sell Bi, di ko settantal, di ci waaru ak di ci waare. Seen dégg-dégg ci Diine di gën a xóot, di gën a leer, di gën a ñaw. Ñu daan xalam kéemaanug sunu Boroom, màggaayam, kàttanam, dayoom, sañ-sañam, yaatoom, ak yeneeni mellom ci mbindéefam yi. Daan teewlu jawu ji, suuf si, malla yi, gañcax yi, soppikug jamono ak melloy nit ñi ak seenug wuute. Loolu daan leen dooli ag xarañ ci gën a jekku mboorug àdduna ci, di ci tibbe ay Hikam di ko laabire seen i ñoñ, mu leen di dolli xel mu leer ak xirtal leen ci gëstu…
Nitug Yàlla mooy koo xam ne dafay yittewoo xam-xam bu am njariñ, day jëf lu baax, dafay làmboo ay teggin yu lislaam gëram. Ñatt yi ñoo key yóbb ci bëgg lu baax, bañ lu bonn. Moo tax dafay doon koo xam ne foo ko fekk mi ngi suuxat ngëmam, di bàyyi kéem kàttanam la Yàlla di tere ak di jëfe la muy digle, di yéene la mu mant a jëf, di tuub ay rëc-rëcam, di jaamu Yàlla ca na mu gën a refete, di fàggu lu lew lu mu dundee, di toppatoo ña mu njabóote, di dimbali képp ku mu man a dimbali te Yàlla tax, moo xam ci alalam, ci dolleem, ci xam-xamam walla ci xelam wu refet.
Avis
Il n’y a pas encore d’avis.